Luc 23
Jésus devant Pilate
Gannaaw loolu mbooloo ma mépp jóg, daldi yóbbu Yeesu ca Pilaat. 2Ñu tàmbali di ko sosal, naan: «Kii lanu fekk muy fàbbi askan wi, di aaye ku fey Sesaar galag, te naan moom ci boppam mooy Almasi bi, di buur.» 3Pilaat laaj ko ne ko: «Yaw yaa di buurub Yawut yi?» Mu ne ko: «Yaa ko wax.»
4Pilaat ne sarxalkat yu mag ya ak mbooloo ma: «Waa jii, gisuma ci moom genn tooñ.» 5Teewul ñu gëna dëggal seeni wax, ne: «Mooy yékkati askan wi, ndax li muy jàngale ci mboolem réewum Yawut, dale ko ca Galile ba fii.»
Jésus devant Hérode
6Pilaat dégg loolu, daldi ne: «Waa jii waa Galile la?» 7Ba mu wóoree Pilaat ne, ca diiwaan ba ca kilifteefu Erodd la Yeesu bokk, ca la ko yónnee Erodd, yemook Erodd itam nekk Yerusalem ca fan yooya. 8Ba Erodd gisee Yeesu, bég na lool, ndax yàggoon na koo bëgga gis, ngir la mu déggoon ay mbiram, ba tax mu yaakaara teewe ay kéemaanam.
9Mu laaj ko lu bare, Yeesu tontuwu ko. 10Sarxalkat yu mag ya ak firikati yoonu Musaa yaa nga taxaw, di ko tuumaal ak doole. 11Erodd aki dagam nag sewal Yeesu, di ko ñaawal. Gannaaw loolu mu solal ko mbubb mu yànj, delloo ko Pilaat.
12Erodd ak Pilaat, bésub keroog ay xarit lañu, doonte ay noon lañu woon.
La foule choisit Barabbas
13Ci kaw loolu Pilaat woo sarxalkat yu mag ya ak kilifa ya ak askan wa. 14Mu ne leen: «Yeena ma indil waa jii, ne ma mooy lajjal askan wi. Man nag laaj naa ko ci seen kanam, waaye gisuma ci moom genn tooñ ci li ngeen ko tuumaal. 15Erodd itam gisul lenn ci moom, ndax moo nu ko yónneewaat. Mu ngoog, waa jii deful lenn lu jar àtteb dee.
16Kon nag dama koy dóorlu, yiwi ko.» 17Ñépp daldi xaacoondoo, ne: «Reyal kii te yiwil nu Barabas!» 18Barabas nag ag fippu gu amoon ca dëkk ba, ak nit ku ñu fa bóomoon, moo waral ñu tëj ko kaso.
19Pilaat namma bàyyi Yeesu, daldi waxaat ak mbooloo ma. 20Teewul ñuy xaacu, naan: «Daaj ko ci bant! Daaj ko ci bant!» 21Pilaat ne leen ñetteel bi yoon: «Ana lu bon lu kii def? Lenn lu jar dee, gisuma ko ci moom. Kon nag, dama koy dóorlu, yiwi ko.»
22Ñu gënatee xaacu, di sàkku ñu daaj ko ci bant. Seen coow la mujj ko ëpp doole. 23Ci kaw loolu Pilaat dogal ñu defal leen la ñu sàkku. 24Mu yiwi ka ñu ko ñaanoon, te jëfi fippu ak nit ku ñu bóom taxoon ñu tëj ko kaso. Yeesu nag, mu teg ko ci seeni loxo, ngir ñu def ko lu leen neex.
25Ba ñuy yóbbu Yeesu, jenn waay ju dëkk Siren, ñu di ko wax Simoŋ, moom lañu dajeel, mu jóge ca tool ya. Ñu gàdduloo ko bant ba ñuy daaje Yeesu, mu topp ca Yeesu.
Père, pardonne-leur
26Nit ñu bare nag topp ko, jigéen ñay yuuxu, di ko jooy. 27Yeesu geesu leen, ne: «Yeen jigéeni Yerusalem, buleen ma jooy! Jooyleen seen bopp ak seeni doom. 28Ay jant a ngi ñëw kat, dees na ca ne: “Ndokkalee jigéen ju tëlee am doom, masula jur, masula nàmpal!” 29Su boobaa, “Nit ñee naan tund yu mag yi: ‘Daanuleen ci sunu kaw!’, naan tund yu ndaw yi: ‘Suulleen nu!’” 30Ndegam bant bu tooy lees di def nii, ana nu bant bu wow di mujje?»
31Yóbbaale nañu itam ñaari saay-saay, ngir boole leen ak Yeesu, rey leen. 32Ba ñu agsee ca béreb, ba ñuy wax Kaaŋu bopp, fa lañu daaj Yeesu ci bant, daajaale ñaari saay-saay ya, kenn ca ndijooram, ka ca des ca càmmoñam. 33Ci kaw loolu Yeesu ne: «Baay, baal leen, ndax li ñuy def, xamuñu ko.» Ñu daldi tegoo bant ay yéreem, ngir séddoo ko.
34Mbooloo maa nga taxaw di seetaan, kilifa ya ñoom di ko kókkali, naan: «Moom day musle, na musal boppam nag, ndegam mooy Almasib Yàlla, ki Yàlla tànn!» 35Takk-der ya it di ko ñaawal. Ñu dikk, tàllal ko bineegar, ngir mu naan. 36Ñu ne ko: «Gannaaw yaa di buurub Yawut yi, musalal sa bopp!»
37Ñu bindal ko nag fa ko tiim, mbind mii: «Kii mooy buurub Yawut yi.» 38Kenn ca saay-saay ya ñu wékkoon ci bant, di ko saaga, naan ko: «Xanaa du yaw yaay Almasi bi? Wallul sa bopp te wallu nu!» 39Moroom ma nag femmu ko, ne ko: «Ragaloo sax Yàlla, te yaa ngi ci menn mbugal mii?
40Nun sax, lii jaadu na ci nun, ndax sunu yoolu jëf lanu jot. Waaye kii deful dara lu teggi yoon!» 41Mu teg ca ne: «Yeesu, boo délsee ci sa nguur, fàttaliku ma!» 42Yeesu ne ko: «Yaw laa ne déy, bésub tey jii, man ngay nekkal fa Àjjana.»
43Ba ñu demee ba tollu ci booru fukki waxtu ak ñaar ca bëccëg, ag lëndëm a wàcc ca réew ma mépp, ba fukki waxtu ak juróom ca ngoon.
Je remets mon esprit entre tes mains
44Naka la jant bi giim, ridob biir néegu Yàlla ba xar ca digg ba. 45Ci kaw loolu Yeesu àddu ca kaw, ne: «Baay, jébbal naa la samag noo!» Ba mu waxee loolu la dog. 46Njiitu takk-der ba ko teewe woon nag sàbbaal Yàlla, ne: «Aylayéwén, waa jii ku jub la.»
47Ba loolu amee mboolem ña fa daje woon di seetaan te teewe loolu, ñépp dellu seeni kër, tey fëgg seen dënn ndaxu tiis. 48Mboolem xamey Yeesu, ak jigéen ña ko toppe woon ca Galile, ña nga dànd lu sore, di seetaan. 49Ndeke jenn waay ju ñuy wax Yuusufa, ma nga bokkoon ca kuréelu àttekati Yawut ya. Ku baax, ku jub la woon.
L'ensevelissement de Jésus
50Kooku ànduloon ca àtteb kuréel ga ak seen jëf jooju. Ma nga cosaanoo woon dëkkub Yawut ba ñuy wax Arimate, te moom itam, nguurug Yàlla la doon séentu. 51Moom moo dem ca Pilaat, sàkku ci moom, mu jox ko néewub Yeesu. 52Gannaaw loolu mu wàccee ko ca bant ba, sànge ko càngaayal lẽe, denc ko ci bàmmeel bu ñu yatt ciw doj, te maseesu caa denc ab néew.
53Bésub Waajal la woon, bésub Noflaay bi ci topp di waaja taxaw. 54Fekk na jigéen ña dale woona ànd ak Yeesu ca Galile, ña nga topp ca Yuusufa. Ñu gis bàmmeel ba, ak na ñu ca dence néew ba. 55Ba loolu amee ñu dellu, waajali cuuraay ak diwu xeeñlu ngir néew ba. Bésub Noflaay nag taxaw, ñu dallu, ni ko yoon santaanee.