Salmi 51
Crea in me un cuore puro
Mu jëm ci njiitu woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda. 2Mooy ba ko Yonent Yàlla Natan seetsee, gannaaw ba Daawuda tëddee ndaw sa ñuy wax Batseba. 3Éy Yàlla, ni nga goree, baaxe ma ni, faral samag tooñ ngir sa yërmande ju yaa.
4Fóotal maa fóotal sama ñaawtéef, raxasal ma sama moy. 5Xam naa ne maa tooñ, sama moy a ngi janook man saa su ne. 6Yaw laa moy, yaw doŋŋ. Li nga ñaawlu laa def. Kon boo waxee, am dëgg, te soo àttee, yey.
7Ñaawtéef daal laa judduwaale, te sama ndey ëmbaale ma bàkkaar. 8Dëgg daal nga namm, dëggu reenu xol, kon déey ma fa xel mu rafet. 9Wis ma ndox, ma sell; sang ma, ma set wecc.
10Yal nanga ma dégtal mbég ak bànneex, ma bégati, gannaaw ba nga ma dammatee. 11Bul xool samay moy, faral sama ñaawtéef yépp. 12Éy Yàlla, sàkkal ma xol bu sell, yeesalal ma pastéefu xol.
13Bu ma xalab, bu ma xañ sa noo gu sell. 14May ma, ma bégeeti sag wall, te dundale ma xol bu tàlli, 15ma xamal tooñkat sa yoon wi nga tëral, ba moykat dellu ci yaw.
16Céy Yàlla, yaw Yàlla mi may musal, baal ma deret ji ma tuur, ma sarxolle sa njubte. 17Boroom bi, may ma, ma wax, ma delloo la njukkal. 18Sàkkuwuloo sarax, nde kon ma indi; te soppuloo saraxu rendi-dóomal.
19Saraxi Yàlla, xol bu tuub la, yaw Yàlla, xol bu tuub ba mokk, doo gàntal boroom. 20Ngalla baaxeel Siyoŋ, yal nanga tabax tatay Yerusalem. 21Su boobaa nga nangu sarax yi war, di saraxu rendi-dóomal. Su boobaa ñu rendi ay yëkk ca sa sarxalukaay.