Salmi 105

Ricordate le meraviglie che ha compiuto

Santleen Aji Sax ji, tudd turam, xamley jalooreem ci biir xeet yi. 2Woyleen ko, tagg ko, yégleleen mboolemi kéemaanam! 3Damooleen turam wu sell, yal na kuy wut Aji Sax ji am bànneexu xol.

4Wutleen Aji Sax ji, sës ci dooleem. Saxooleen koo wër! 5Fàttalikuleen ay jalooreem aki kéemaanam aki àtteem. 6Yeen askanu Ibraayma, jaamam ba, yeen sëti Yanqóoba, yeen ñi mu tànn!

7Kee di sunu Yàlla Aji Sax ji, di àtte suuf sépp, 8di fàttaliku ba fàww kóllëreem, ak kàddoom ga mu digoon Ibraayma, ba ci junniy maas, te mu giñal ko Isaaxa, 9dëggalal ko Yanqóoba, sàrtal ko, fase kook Israayil mooma kóllëre gu sax.

10Moo noon: «Yaw laay jox réewum Kanaan, muy sa cér, nga séddoo.» 11Ba bànni Israayil doonee ñu néewa néew, diy doxandéem ci réew mi, 12di wëreelu ci biir xeetoo xeet, ak nguuroo nguur, 13mayul nit mu noot leen, te yaral na leen ay buur, 14ne leen: «Buleen laal ñi ma séddoo, te samay yonent buleen leen lor.»

15Moo wàcce ab xiif ca réew ma, dagge fa lépp luy gub, 16yónnee ku leen jiitu, muy Yuusufa ma ñu jaayoon njaam, 17tànk ya, ñu jéng jéng yu tar, baat ba, ñu yeewe caqu weñ.

18Kàddug Aji Sax ji di nattu Yuusufa, ba keroog pirim ma dikk, 19Buur a yónni ku ko yiwi, ku yilifi xeet a ko tijji. 20Mu sas ko mu jiite këram, di saytu mboolem alalam, 21ba saña tënk jawriñi buur ci coobareem, tey xelal mag ña.

22Israayil agsi Misra, muy nganug Yanqóoba ga ca réewum Xam. 23Aji Sax ji giiral xeetam wa, ba ñu gëna bare seeni noon, 24mu xiir waa Misra ci dëddu ñoñam, ñuy fexeel jaamam ñooña.

25Mu yónni Musaa, jaamam ba, tànn Aaróona, boole ca, 26ñu sottal ci seen biir firndeem ya mu waxoon, muy kéemaan ya ñu def ca réewum Xam. 27Moo yónnee lëndëm, lëndëmal, te Musaa ak Aaróona gàntaluñu kàddoom.

28Moo soppi seen ndoxum réew deret, rey seeni jën, 29feesal seen réew ay mbott yu àkki seen biir néegi buur ya. 30Moo àddu, weñ ya dikk, yoo ya dajal seen réew ma.

31Mu def seenub taw tawub yuur, sawaray melax jafal seen réew ma. 32Mu dal ci seen figg ak reseñ, daaneel seen garabi réew ma. 33Mu àddooti, ay soccet dikk, di njéeréer yu wees ab lim, 34ñu lekk luy gàncax ca seenum réew, lekk lu suuf sa meññ.

35Moo faat luy taaw ca seenum réew, muy lu njëkka soqeekoo seen digg doole. 36Mu génne leen, ñu yóbbaale xaalis ak wurus, te kenn tërëful ca seeni giir. 37Misra daa bég ba ñu demee ndax tiitaange ju ñu leen tiital.

38Mu firiw niir, yiire leen, ak sawara, ñu niitoo guddi. 39Ñu sàkku, mu wàcceey picci përëntaan, teg ca reggal leen mburum asamaan. 40Mu bënnu doj, ndox ma ball, di dex, wale joor gu wow.

41Daa bàyyi xel kàddoom gu sell, ga mu waxoon Ibraayma, jaamam ba. 42Moo génne ñoñam, ñu bég, moo génne tànnéefam ña, ñuy sarxolle. 43Mu jox leen suufi yéefar ya, ñu jagoo ñaqi xeet ya, 44ngir ñu sàmm ay dogali yoonam, topp ndigali yoonam. Màggalleen Ki Sax!

Copiato!
Aa