Jeremiah 20

Pashhur puts Jeremiah in the stocks

Ci kaw loolu, Pasur doomu Imer, sarxalkat ba jiite woon saytub kër Yàlla ga, ba mu déggee Yonent Yàlla Yeremi muy jottali kàdduy waxyu yooyu, mu dóorlu ko, jéng ko ca buntu kër Aji Sax ja féete kaw, te ñu dippee ko Beñamin. 2Ca suba sa Pasur yiwee ko ca jéng ba. Yeremi ne ko: «Aji Sax ji tuddeetu la Pasur; Magor-Misabib (muy firi Tiitaange ju dajal) la la tudde. 3Ndax Aji Sax ji dafa wax ne: “Maa ngii di la wàcceel tiitaange, yaak sa soppe yépp, seen saamaru noon daaneel leen, ngay gis; te Yuda gépp laay teg ci loxol buuru Babilon, ñii mu yóbbu leen ngàllo, ñee mu jam leen, ñu dee.

4Maay joxe lépp luy alalu dëkk bii. Mboolem lu fiy njariñ, mboolem gànjar, mboolem denci buuri Yuda, dinaa ko teg ci seen loxol noon yi, ñu sëxëtoo, jël, yóbbu Babilon. 5Yaw Pasur, yaak sa waa kër yépp ay duggi njaam ca Babilon. Babilon nga jëm te fa ngay dee, ñu rob la fa, yaak mboolem sa soppe ya nga daan àgge ay kàdduy waxyuy fen.”» 6Éy Aji Sax ji, naxtaan nga ma, ma naagu, nga nax ma, jaay ma doole, ba man ma. Ñu ngi may kekku bés bu ne, ku ne di ma kókkali.

His word is a fire in my bones

7Saa yu ma waxee, damay xaacu, fitnaak salfaañoo ma tax di yuuxu. Kàddug Aji Sax jee may yóbbey xas aki saaga bés bu ne. 8Su ma nee: «Xaaral ma fàtte ko, dootuma jottali kàdduy waxyu ci turam,» sama xol bi mel nib taal bu tàkk, tàbbi sama biir yax yi; may jéema muutuwaale sa kàddu, te duma ko man. 9Dégg naa ñaawlaate yu bare, ñu naan: «Éey, “Tiitaange ju dajal!” Booleleen ko, boole rekk!» Ñi ma séqal jàmm sax, di yeeru ma fakkastalu, naan: «Jombul mu juum, nu jekku ko, ba mana feyu.»

10Waaye Aji Sax jeek man, di ñeyi xare. Moo tax ñi may tëru di tërëf, ba duñu daan, xanaa rus lool, ndax duñu baaxle; gàcce gu yàgg lay doon te du fey. 11Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, yaw miy nattu ku jub, di gis xel ak xol, may ma, ma gis ni nga leen di feye; yaw de laa diis sama mbir. 12Woyleen Aji Sax ji, màggalleen Aji Sax ji! Mooy xettali néew-ji-doole ci dooley ku bon.

13Alkute ñeel na bés ba ma juddoo, bés ba ma saa ndey juree, yàlla bumu barkeel. 14Alkute ñeel na ka ko yegge baay, ne ko: «Sa soxna am na doom ju góor,» ba tax baay bég a bég. 15Yal na kooku mel ni dëkk yi Aji Sax ji tas te yërëmu leen! Yal na dégg yuuxi suba teel ak xaacuy xarey njolloor.

16Moo ma reyul ci sama biiru ndey, ma bàmmeeloo sama ndey, te du wasin mukk. 17Ana lu ma doon génne ca biiram, di daj coonooku tiis, mujje gàcce?

Copied!
Aa