1 Chronicles 8
From Benjamin to Saul
Beñamin mooy baayu Bela miy taawam bu góor. Ku góor ka ca topp di Asbel, Aara di ñetteelu doomam ju góor. 2Noxa di ñeenteelu doomam ju góor, Rafa di juróomeelu doomam ju góor. 3Doomi Bela yu góor ñoo di Adar ak Gera ak Abiyudd.
4Abiswa ca la ak Naaman ak Axowa. 5Gera it ca la ak Sefufan ak Uram. 6Doomi Exudd yu góor yooyu di Naaman ak Axya ak Gera. Ñoo doon kilifay làngu waa Geba ya ñu toxal Manaxat, te Gera moo leen toxal. Mooy baayu Usa ak Axixudd.
7Saxarayim, gannaaw ba mu fasee Usim ak Baara ñaari soxnaam ya, am na ay doom yu góor ca réewam Mowab. 8Moo jël Odes soxna, am ca Yobab ak Cibya ak Mesa ak Malkam. 9Am na ca it Yewucc ak Sakiya ak Mirma. Doomam yu góor yooyu mujj jiite seen kër baay.
10Fekk na mu am ak Usim ñaari doom yu góor, Abitub ak Elpaal. 11Doomi Elpaal yu góor ñoo di Eber ak Misam ak Semedd. Semedd moomu moo tabax dëkk ya ñuy wax Ono ak Lodd ak dëkk yu ndaw ya ko wër. 12Berya ak Sema ay kilifay làngi waa Ayalon lañu woon. Ñoo dàq waa Gaat.
13Ñii di Axyo ak Sasag ak Yeremot 14ak Sebaja ak Aràdd ak Eder 15ak Mikayel ak Ispa ak Yoxa, ñooy góor ñi Berya di seen baay.
16Sebaja nag mook Mesulam ak Iski ak Eber, 17ak Ismeray ak Isliya ak Yobab ñooy góor ñi Elpaal di seen baay. 18Yakim ak Sikkri ak Sabdi 19ak Eliyenay ak Ciletay ak Elyel 20ak Adaya ak Beraya ak Simrat ñooy góor yi Simey di seen baay.
21Ispan nag mook Eber ak Elyel 22ak Abdon ak Sikkri ak Xanan 23ak Anaña ak Elam ak Anatoca 24ak Ifdeya ak Penuwel, ñooy góor ñi Sasag di seen baay.
25Samseray ak Sexarya ak Atalyaa 26ak Yaaresya ak Elya ak Sikkri, ñooy góor ñi Yeroxam di seen baay. 27Ñooñoo jiite woon seeni waa këri maam, ku nekk ak sag maas. Ña nga dëkkoon Yerusalem.
28Baayu Gabawon, Gabawon la dëkkoon. Maaka la soxnaam tudd. 29Taawam bu góor moo doon Abdon, góor ña ca topp di Cur ak Kis ak Baal ak Ner ak Nadab, 30ak Gedor ak Axyo ak Seker 31ak Miglot baayu Simeyam. Ñooñu itam ña nga dëkkoon Yerusalem ñook seeni bokk.
32Ner mooy baayu Kis, Kis di baayu Sawul, Sawul di baayu Yonatan ak Malkisuwa ak Abinadab ak Esbaal.
The family of Saul
33Doomu Yonatan ju góor moo di Meribaal; Meribaal di baayu Mise. 34Doomi Mise yu góor ñoo di Piton ak Meleg ak Tareya ak Axas. 35Axas mooy baayu Yowada, Yowada di baayu Alemet ak Asmawet ak Simri; Simri di baayu Mocca.
36Mocca mooy baayu Bineya. Bineya di baayu Rafa, Rafa di baayu Elasa, Elasa di baayu Accel. 37Accel amoon na juróom benni doom yu góor, ñuy Asrikam ak Bokkru ak Ismayel ak Seyarya ak Abdiyas ak Xanan. Ñooñu ñépp Accel moo leen jur. 38Eseg la Accel bokkal. Góor ñi Eseg di seen baay ñoo di Ulam, taawam, Yewus topp ca, Elifelet toppaat ca.
39Doomi Ulam yu góor nag ay ñeyi xare lañu woon, diy fittkat. Amoon nañu ay doom yu góor ak sët yu góor yu takku, ñoom ñépp di téeméer ak juróom fukk (150). Ñooñu ñépp ci Beñamin lañu soqikoo.